Pinned Tweet
Gys, nous venons de créer un groupe dédié à des sessions hebdomadaires de Wathié Kaamil, en hommage à nos défunts, mais aussi pour invoquer Allah SWT en faveur de la paix dans notre pays. 🤲🏾Si vous êtes intéressés, n’hésitez pas à me DM ou à contacter @Momo_Diaoune
𝐵𝑒𝓃_𝒰𝓈𝓂𝒶𝓃𝑒_🇸🇳.🇵🇸 retweeted
MOT D’ORDRE : 100 % PASTEF
- Ne réagissez plus aux comptes qui propagent des mensonges, des provocations et des fake news sur PASTEF et Sonko.
- BLOQUEZ-LES OU MASQUEZ-LES !
- Concentrons-nous uniquement sur les actions du parti et de l’Assemblée nationale.
PARTAGEZ !
𝐵𝑒𝓃_𝒰𝓈𝓂𝒶𝓃𝑒_🇸🇳.🇵🇸 retweeted
AirPods Pro 2 - AirPods 2
Acheté = Étuis offert
Commande tes AirPods et tu sera livré dans les meilleurs délais ❤️🤝
@DIAOUNE_Shop 📌🤍
🤖 Made with AI
𝐵𝑒𝓃_𝒰𝓈𝓂𝒶𝓃𝑒_🇸🇳.🇵🇸 retweeted
Salam les gars.
Appartement à Louer à Saint Louis en face UGB
2chambres avec Salle de bain
1salon
1e cuisine et une toilette visiteurs à 125000
𝐵𝑒𝓃_𝒰𝓈𝓂𝒶𝓃𝑒_🇸🇳.🇵🇸 retweeted
Noo ngi jaajëfal bu baax, njiital gombulaan gi Usmaan Sonkoo, te it di njiital làngug pastef.
Ñu mel ni moom danu leen di soxla lool ci doolel làkk wi, ndax koo xam ne li ëpp ci waa réew mi ñoo ngi koy topp, kon di jëmmal làkk i réew mi day jaadu ci moom, rawatina kuy woote ag moom sa bopp.
Kon Usmaan noo ngi lay ñaax, tey sàkku ngay baril lool sam mbind ci wolof ni ki nga ko baaxoo waxe.
Jëmm jii di Boris Jóob daa dogu ci ne dootul bind téere ci lu dul wolof, man mii jàng naa ay téerem, rawatina mbalaanum lëndëm, muy téere boo xam ne, ci jamono ji nga koy jàng da ngay mel ni ku fàddu, jóge ci sa xalaati bopp jëm ci ay xalaatam.
Waaye nag nii rekk la mbir yi man a deme, ndax koo xam ne Seex Anta Jóob nga def muy sa kilifa di sa royuwaay ci doxaliinu Afrig fàww nu séentu lii ci yaw !
Demb, fale ca daara ju kawe ja ñu tuddee sunu maam ju am solo jooju, Seex Anta Jóob, ay kàngam daje nañu ngir tàmbali sargalub Bubakar Bóris Jóob, biy wéy ba àllarba.
Bubakar Bóris Jóob, li mu bind xóot na, yaatu na yaatu goo xam ne teewal ko lépp, lu jafe la. Waaye mën nanu ci cof tuuti te du ñàkk ñu tudd lu jar a bàyyi xel. 1981 ba léegi, Bubakar Bóris Jóob mu ngi saytu réew mi ak Afrig, di seetlu askanam, di bàyyi xel fi ñu jugee, di gëstu fi ñu jëm. Lu tollu ci ñaar-fukki téere lanu jagleel, te bu ci nekk, boo ko jàngee, dinga ci dajeek bindkat bu xarañ, waaye it bu xam askanam, naw askanam, bëgg Afrig.
Senegaal yàgg naa am boromi xel yu ñaw, te dina yàgg di leen am. Yàgg naa it di am ay bindkat yu mag te ñu ràññee leen ci àddina, waaye barewul ci sunuy bindkat yi siiw bitim réew, ñu boole li Bubakar Bóris Jóob boole, te mu bokk ko ak sunu maam Usmaan Sembeen : xarañ ci bind ay téerey nettali, tekk ci gëm sa askan, gëm sa aada, fullaal say làkki réew te wóolu leen ci tabax sunu ëllëg. Bubakar Bóris Jóob yàgg naa siiw ci téere yi mu bind ci nasaraan. Waaye li ko gën a def ngand, li gën a tax mu sax ci sunuy xol, xale yi naw ko, mooy li mu xëy bés fullaal làkki askanam, jagleel nu téerey Doomi Golo, Bàmmeelu Kocc Barma ak bi mujj, Malaanum lëndëm, ci sunu làkku Wolof. Ci yaatoom ak yëg-yëg bi mu am ci ndawi Senegaal, Bubakar Bóris Jóob mës na maa dalal, waxtaan ak man ni mag di waxtaanee ak rakkam, may ma ay téere. Ni mu ko defee ak man, noonu la koy faral di defee ak bépp ndaw bu mu gis ci yow ag bëgg-sa-réew te amal ko njariñ. Téere yooyu, boo ci jàng, dinga xam ne ñun, ay mbokkam, ñun waa Senegaal, la leen Bubakar Bóris Jóob njëkk a yéene.
Am réew, aw askan, ni mu soxlaa ñuy bay ak ñuy sàmm ngir dundal yaram yi, noonu la yittewoo ñu koy bàyyi xel, di ko gëstu saa su ne, di ko fàtteli démbam, di saytu ëllëgam, ba noppi di diisoo ak moom ci mbind, ci xalima gu taaru, ngir xamal ko boppam, tere koo gëlëm, tàllal ko seetu bu koy may mu mucc ci fàtte boppam ak li ko war.
Seetu boobu, Bubakar Bóris Jóob bind na ko. Jàngleen yooyu téere , bu ngeen ko defee, dingeen ci gis seen bopp, dingeen ci gis ni réew mi tëddee, li ci mat a sàmm ak li ñu ci war a jubbanti.
Usmaan Sonkó
𝐵𝑒𝓃_𝒰𝓈𝓂𝒶𝓃𝑒_🇸🇳.🇵🇸 retweeted
📌 Le président Ousmane Sonko affiche une position ferme face aux menaces visant l’Assemblée nationale. 🇸🇳
La démocratie se défend par le droit, pas par l’intimidation. 🙏
𝐵𝑒𝓃_𝒰𝓈𝓂𝒶𝓃𝑒_🇸🇳.🇵🇸 retweeted
Texte traduit en Français pour nos frères Africains qui ne parlent pas Wolof: 👇
Hier, dans cette grande école qui porte le nom de notre illustre ancêtre, Cheikh Anta Diop, des responsables se sont réunis pour lancer l’hommage à Boubacar Boris Diop, qui se poursuivra jusqu’à mercredi.
L’œuvre de Boubacar Boris Diop est profonde et immense. La résumer dans son intégralité serait une tâche difficile. Mais nous pouvons en évoquer quelques aspects, sans manquer de souligner l’essentiel. Depuis 1981, Boubacar Boris Diop observe le Sénégal et l’Afrique, s’interroge sur leur peuple, réfléchit à leurs origines et explore les chemins qu’ils empruntent. Il a consacré près d’une vingtaine d’ouvrages à ces questions. Chacun d’eux nous fait découvrir un écrivain remarquable, mais aussi un homme qui connaît son peuple, qui l’aime et qui croit en l’Afrique.
Le Sénégal a toujours compté de grands intellectuels, et il continuera d’en produire. Il a également donné naissance à de grands écrivains reconnus à travers le monde. Pourtant, rares sont ceux qui, parmi nos écrivains de renommée internationale, réunissent autant de qualités que Boubacar Boris Diop, aux côtés de notre aîné Ousmane Sembène : le talent littéraire, la foi en son peuple, l’attachement à sa culture et la conviction que nos langues nationales peuvent contribuer à bâtir notre avenir.
Boubacar Boris Diop s’est longtemps illustré par ses ouvrages en français. Mais ce qui fait davantage sa singularité, ce qui lui vaut une place durable dans nos cœurs et l’admiration de la jeunesse, c’est le combat qu’il a mené pour valoriser les langues de son peuple. Il nous a ainsi offert Doomi Golo, Bàmmeelu Kocc Barma et, plus récemment, Malaanum lëndëm, écrits en wolof.
Compte tenu de son rayonnement et de l’attention qu’il porte à la jeunesse sénégalaise, Boubacar Boris Diop m’a un jour accueilli, a échangé avec moi comme un aîné le ferait avec son cadet et m’a offert des livres. Ce qu’il a fait pour moi, il le fait régulièrement pour tout jeune qu’il rencontre et chez qui il décèle un amour sincère pour son pays et la volonté de lui être utile. En lisant ces ouvrages, vous comprendrez ce que Boubacar Boris Diop a voulu transmettre en priorité à ses frères et sœurs, à nous, Sénégalais.
Un pays, un peuple ont autant besoin de ceux qui cultivent la terre et veillent à nourrir les corps que de ceux qui entretiennent la réflexion et nourrissent les esprits. Il faut des femmes et des hommes qui interrogent sans cesse leur société, étudient son histoire, se penchent sur son avenir et engagent avec elle un dialogue à travers l’écriture, grâce à une plume élégante. Des femmes et des hommes qui l’aident à se connaître lui-même, à résister à l’aveuglement et à se regarder dans un miroir qui lui permette d’échapper à l’oubli de soi et de retrouver le sens de son devoir.
Ce miroir, Boubacar Boris Diop l’a façonné à travers ses écrits.
Lisez ces ouvrages. Vous y découvrirez votre propre reflet, celui de notre pays, ce qu’il convient de préserver et ce qu’il nous appartient de corriger.
@SonkoOfficiel
Demb, fale ca daara ju kawe ja ñu tuddee sunu maam ju am solo jooju, Seex Anta Jóob, ay kàngam daje nañu ngir tàmbali sargalub Bubakar Bóris Jóob, biy wéy ba àllarba.
Bubakar Bóris Jóob, li mu bind xóot na, yaatu na yaatu goo xam ne teewal ko lépp, lu jafe la. Waaye mën nanu ci cof tuuti te du ñàkk ñu tudd lu jar a bàyyi xel. 1981 ba léegi, Bubakar Bóris Jóob mu ngi saytu réew mi ak Afrig, di seetlu askanam, di bàyyi xel fi ñu jugee, di gëstu fi ñu jëm. Lu tollu ci ñaar-fukki téere lanu jagleel, te bu ci nekk, boo ko jàngee, dinga ci dajeek bindkat bu xarañ, waaye it bu xam askanam, naw askanam, bëgg Afrig.
Senegaal yàgg naa am boromi xel yu ñaw, te dina yàgg di leen am. Yàgg naa it di am ay bindkat yu mag te ñu ràññee leen ci àddina, waaye barewul ci sunuy bindkat yi siiw bitim réew, ñu boole li Bubakar Bóris Jóob boole, te mu bokk ko ak sunu maam Usmaan Sembeen : xarañ ci bind ay téerey nettali, tekk ci gëm sa askan, gëm sa aada, fullaal say làkki réew te wóolu leen ci tabax sunu ëllëg. Bubakar Bóris Jóob yàgg naa siiw ci téere yi mu bind ci nasaraan. Waaye li ko gën a def ngand, li gën a tax mu sax ci sunuy xol, xale yi naw ko, mooy li mu xëy bés fullaal làkki askanam, jagleel nu téerey Doomi Golo, Bàmmeelu Kocc Barma ak bi mujj, Malaanum lëndëm, ci sunu làkku Wolof. Ci yaatoom ak yëg-yëg bi mu am ci ndawi Senegaal, Bubakar Bóris Jóob mës na maa dalal, waxtaan ak man ni mag di waxtaanee ak rakkam, may ma ay téere. Ni mu ko defee ak man, noonu la koy faral di defee ak bépp ndaw bu mu gis ci yow ag bëgg-sa-réew te amal ko njariñ. Téere yooyu, boo ci jàng, dinga xam ne ñun, ay mbokkam, ñun waa Senegaal, la leen Bubakar Bóris Jóob njëkk a yéene.
Am réew, aw askan, ni mu soxlaa ñuy bay ak ñuy sàmm ngir dundal yaram yi, noonu la yittewoo ñu koy bàyyi xel, di ko gëstu saa su ne, di ko fàtteli démbam, di saytu ëllëgam, ba noppi di diisoo ak moom ci mbind, ci xalima gu taaru, ngir xamal ko boppam, tere koo gëlëm, tàllal ko seetu bu koy may mu mucc ci fàtte boppam ak li ko war.
Seetu boobu, Bubakar Bóris Jóob bind na ko. Jàngleen yooyu téere , bu ngeen ko defee, dingeen ci gis seen bopp, dingeen ci gis ni réew mi tëddee, li ci mat a sàmm ak li ñu ci war a jubbanti.
Usmaan Sonkó
😭😭😭sheuuu ndeikeité ñoun lakouñ olof